Te moo ne xalaat i xamtu yooyu ci démbi Afrig am na njeexiit lu rëy; ndax dafa doonoon
lees daan jëfandikoo te jëfandiku gi yomb lool te am i njureef. Te ca dëgg-dëgg sax, xalaat
yooyu sax ñooy li am njariñ waaye bu nu dee wax njariñam mooy njariñ li mu amal noteel gi.
Nde jubluwaay bi mooy sol mbubbum xamtu ngir gëmloo ñuule bi ne moom masut a sos
mbaa mu taxawal dara lu am solo ci àdduna, ba ci li ko wër. Ci loolu lañu wéye (ci seen xalaat yooyu) ba yoqatloo ñi doon jóg ngir taxawu seen i réew. Bu dee ñi nga
xam ne nag jotoon nañu leen a weddiloo seen bopp, dañu a gën a feddali buumug njaam gi ci
seen i loos.

Seex Anta Jóob

Saabal.com

Leeral :
Xamtu g: science
Mbatiit m: culture

Laisser un commentaire

Votre adresse e-mail ne sera pas publiée. Les champs obligatoires sont indiqués avec *