Ña dëkke ca Aaga nekk ca diggante Caajaay ak Ngeeñeen ñoo yewwu ci aw tiis ginnaaw ba ñu yëgge faatug soxna suy wuyoo ci turu Xadi Maróon. Moom nag dafa ñàkk bakkanam ca fajuwaay ba bàjjanu gox ba jiite ndax ñàkk ay fajkat.

BÀJJANU GOX BUY JIITE AB FAJUWAAY

Ki faatu amoon na jëkkër ak juróomi doom. Mu ngi doon waaj a am beneen bant sax. Waaye ca la musiba ma ame ginnaaw ba ko bàjjanu gox ba tiñ ndax gox ba amul ay fajkat.

Yëral bii 👆

Ginnaaw ba mu defee la mu man yépp taxul mu mucc, ca la ko bàjjanu gox ba rawale ca Caajaay.

Xay ga ñu amal ca moom ngir doom ja génn taxul ñu dund ñoom ñaar nde dañoo ñàkk seen i wakkan.

Laataa loola nag jàllale nañu sax fële ca Mbuur waaye noona. Denc nañu leen ca Aaga ga ñu jóge woon ca bis ba.

Tiñ: rewli: aider à accoucher

Laisser un commentaire

Votre adresse e-mail ne sera pas publiée. Les champs obligatoires sont indiqués avec *