Démb, 30i soxna yu rànneeku bokk nañu siiwal ab bind buy sàkku ci këri saabal yoy réew mi ñu dakkal wane gi ñuy wane saabalkat bi dii Seex Yerim Sekk. Soxna yooye, li wund seen dagaan googi moo di jàpp nañu Seex Yerim Sekk yaqtaankat la, siifkat la, ëpp na ci mim réew ñu koy jox kàddu ngir mu wax ci li xelam màcc di xew-xewu jamono rawati na polotig. Soxna yooye seen doxaliin am na aw tur : « cancel culture » ci Angale. Mbiir mi ñaari waat a ko seq : “cancel” ak “culture”. “Cancel” man na tekki fomm mbaa dakkal. “Culture” moom di tekki mbatiit. Waaye fii su ñu ko doon jéem a tekki ci Wolof, manees nanu ni mooy “doxaliinu fomm” mbaa “doxaliinu aaye”.

Seex Yérim Sekk - saabalkat

“Doxaliinu aaye” googee mooy tere nit mu wax walla feeñ ci pénc ndax i jëf mbaa wax yumu amaloon walla yuñu ko jiiñ. Fii, soxna yii, dañu bëgg muumaloo Seex Yerim Sekk ndax topp guñu ko fi toppon 8i at ci gannaaw. Atum 2012, Yoon toppoon na, teg daan Seex Yerim ñaari atu kaso ci mbiru siif ak yeg ci kaw uk soxna. Donte wàccoo na ak yoonu réew mi ak askan wi, ndax tëdd na kaso ba génn. Ñu bari ci mim réew jàpp nañu ni du royukaay, sàmbabooy la, may ko mu wax ci pénc, du xel. “Doxaliinu aaye” nag, lu yàgg la ci jamono. Mboor wane ni ci askan yu bari, muy ci sunu réew mbaa feneen, yàggees na génne nit ci dëkk, gàddaayloo ko, noppiloo ko ndax i wax walla i jëf yu méngoowul ak ni askan woowee tàmmoon a dundee.

“Doxaliinu aaye” nag daa ñëw ci anam gu bees ci jamono yii. Leegi, nekkatul Buur mooy tere nit mu wax walla dëkk cib tund. Mbaalu jokko yi ñooy àtte, tëjlu, taakal buumu gààce, gàddayloo mbaa raylu nit. Ci atum 2017, ci Twitter, ci la #MeToo judd. Astag bii, tax na soxna yu bari, ci Tugal ak Amerig nettali siif, yeg ci kaw ci lu ñu àndul, yaqtaan mbaa jaay doole yi ñu leen mas a def. Te ci seede yi, ñu bari joxooñoon nañu baaraam ay nit yu rànneeku, ci fànn yu bari : kilifag politig, waykat, filmookat, fecckat, bindkat, saabalkat, xumbalkat, njaatige, añs. Loolu tax na, ñu bari jàpp ni, ngir néewal doole gi ñuy doole jigéen ñi dakk, faw ñooni ñu jiiñ mbir yu ñaan yooyu, ñu noppiloo leen ba fàww. Ci nooni la ca Amerig, Faraas, Angalteer ak yeneen i réew, la ñu bari ci génnee ci seen i këru liggéeyukaay : ëttu saabal, këru bind, filmoo, añs.

Doxaliinu aaye googu egseegul ci sunu réew walla boog néew na lool ñu amal ko ni mu amee ca réew yi nu lim. Sunu ëttu saabal yi, daanaka tëjaluñu seen i bunt kenn. kilifag polotig gu jëfi tayam woroo ak i waxi démbam, ndawu réew mu ñu jàpp cib luubal, raykatu nit, siifkat… Amul kenn kuñu tere seen i waxukaay. Leegi li nuy laaj mooy kañ ak ñan la ñu war a aaye walla fomm ? Ndax fen, war na indi aaye ? Ndax sàcc war na indi aaye ? Ndax siif war na indi aaye ? Ndax nit bu duggee kaso ba génn war nañu ko tere wax donte tuub na réccu ?

Mu baax walla mu bonn, cib bokkeef la nu nekk. Yewwu ci dëkk bi, liggéey, wax fi, mooy nangu ni Bokkeef gi di doxee. Bokkeef gi nag daa am i yoon, am i daan. Nit su wàccee yoon, ñu teg ko i daan ba daan gi jeex, faw ñu nangul ko mu dund ci réew mi dundug jàmm.

Fàllu Sekk

Laisser un commentaire

Votre adresse e-mail ne sera pas publiée. Les champs obligatoires sont indiqués avec *