Saa Boroom ay Ndaanaan!

Damaa nekk ci saxaar gi di tukki, jóge cib dëkk jëm cib dëkk. Saxaar giy daw, di daw saay gët di jaabante ci diggante asamaan ak suuf, saxaar gi di daw may xool kéew mi ak gàncax gi ak garab yi ak tool yi ak jur gi; samam xel xelli jox samab xol rekk ma daal di yéemu ci Ndaanaan li def lii. Ci noonu ag cant ganesi ma.

Saa Boroom ay Ndaanaan!

Cant, ab dëkk la niki weddi waaye ku sanc dëkkub cant gental ca booba bob weddi te sag pay mooy ndollan lu dul jeex. Mbind mii mooy seede samag cant ci Ndaanaan lu Màgg lii mbaar asamaan te amul i jën, bu bëccëgee mu taarale ko jant bi, bu guddee weer wi ak i biddiw wuutu ko. Lal suuf te amul keno def ci ay xur ak i tund ak yi ma lim ci kaw ba noppi boole nit ñi ak jinne yi ak ndégment yi ak rab yi ak njanaaw yi ak yu nu xamul ci kawam te taxul suuf rës. Ndaanaan li xàjjale suuf ci diggante géej ak jéeri ak dex ñoom it ñu am ñu leen dëkke te teewul Ndaanaan li lootaabe lépp ba kenn du ne lii bu ko defe woon nii.

Saa Boroom ay Ndaanaan!

Ku teewlu, teew. Ku teew, teewe. Ku déglu, dégg. Ku dégg, dégtale. Ku xool, gis. Ku gis, gag. Ku làmb, daj. Ku daj, daaj. Ku xeeñtu, banamtiku. Ku banamtiku, tàqamtiku.
Ana way-xelu ñi? Dikkleen! Dikkleen seere ne Ndaanaan dëgg ca la baat ba di wund ci lu dul wor mooy saa Boroom.
Kii mooy Ndaanaan li gaa ñi sukkandiku bay daan seen i kem, di naan ca lem ya bu ñu xamee ak bu ñu ko umpalee, bu ñu ko nangoo ak bu ñu ko bañee te taxul ñu mat ndaanaan. Képp ku mu solal yuppit foo jaar nit ñi di la niit te lu jiit yi bari-bari du la tee xuus di wane yoon ñu di la yéem fekk Ndaanaan lu Màgg li la waaye du yaw.
Céy lile Ndaanaan!

Saa Boroom ay Ndaanaan!

Lootaabe na kaw, lootaabe suuf, lootaabe diggante bi. Nos na biir, nos biti. Ndaanaan lii moo nu bind, moo nu moom, moo nu melal, moo nu kàttanal, moo nuy wërsëgal, moo nuy dundal, moo nuy ray te bu ëllëgee moo nuy dekkal, kenn fekku ko ci nun. Ndaanaan lii lottul ci dara, mooy Aji-Nangu ñaan Ji, mooy Tab ji, mooy fajkatu aajo yi, Moom la lépp yomb, Moom la dara tëwul, moo peeg lépp ak ñépp ak fépp tey seen Boroom, du wàññikule dara ba di ko jeexle, lu mu ne nekkal loola nekk fi saa sa te dara du ko teree nekk, lu mu ne du ne, loola du ne te dara du ko tax a ne.
Tudd naa sellug Ndaanaan lile! Ndaanaan lii mooy Aji-Yaakaaru Ji dul tas yaakaari ku ko yaakaarul aste ku ko yaakaar, moo Màgg, moo Kawe, moo Tedd, moo Baax, moo Sell, mooy Yërmànde…

Saa Boroom ay Ndaanaan!

Saa Boroom Yàlla ay Ndaanaan li jiitu amul lu ko féete kanam, moo mujj, amul lu ko féete ginnaaw, moo féete penku ak sowu ak bëj-saalum ak bëj-gànnaar, moo ndarkepp lépp, moo feeñ ba réer, moo réer ba faf feeñ. Amul lu ko dara di yokk, amul lu ko dara di wàññi. Amul lu ko war ci kenn mbaa lenn mbaa fenn. Lu am ak fu mu amee ak nu mu amee ak ku ko amal ci coobareem daal la waaye lu amul itam noonu.
Tudd naa sellug Ndaanaan lii nga xam ne moo ma may tawféex ba ma man a sotti lii ci saxaar gii ginnaaw bi ma xoole sama bopp gis ko, xool li ma wër gis ko.
Maa ngi sukk ci kanamam ànd ak toroxlu man jaamam bu xeebu bii te bari ayib lool, lompañ te lott ci lépp lu mu ma manalul; maa ngi lay xaaraan ak a yalwaan ak a dagaan Yaw Ndaanaan li nga may ma mujj gu rafet te may ko képp ku gis mbind mii mbaa mu dawal ko mbaa mu déglu ko ci barkeb ki joxoñ ñépp ak lépp ak fépp Ndaanaan li nga doon.
Céy saa Boroom Yàlla mooy Ndaanaan!

Ismayla Géy WAX(Wolof Ak Xamle)

Laisser un commentaire

Votre adresse e-mail ne sera pas publiée. Les champs obligatoires sont indiqués avec *