Li ma teree nelaw mooy njàngale moomu sendikaay jàngalekat yi di njort ñu dugal ko lekool bi jublu ci yàq sunu xale yi. Sama xel daloon na ndax waxi jawriñ jiy saytu njàng mi, waaye ñu xamal ma ni atum 2014 ba léegi la ñu ko defoon ab sumb, di wut yoon ngir mu dugg ci réew mi.
Yi ci sendikaay jàngalekat feeñal doy na firnde, ñi koy saytu mel ni ki teewal Unesco ci Ndakaaru, ak i Kilifa ci ñiy saytu njàngum réew mi ñu xam leen.
Lépp war a leer ndax kayit yi ma jot a jàng gisuma ci luy gëddaal li nu doon. Naka la ñu mën a doyalee mbind yi ci sunu téerey diine yi, ak sunu mbaax yi fi jiitu woon diiney Islaam ak kerecen. Mësumaa gis cong gu ñaawee nii ci sunuy ngëm-ngëm.
Xeex bi nag du yem rekk ci sendikaa yi ko feeñal. Jaajëfal leen war na nu ci li ñu taxaw di ko bañ. Waaye mbir mii mbirum réew mi yépp la. Muy ku yor xale ci lekool bi ak képp kuy doomu Senegaal. Pexe mi nag su boobaa menn la. Ndax ñii du ñu dellu gannaaw feek gisuñu réew mépp taxaw ngir bañ ko. Muy ñépp tëye seen doom yi ci kër yi ñu bañ a dem lekool. Toog ci kër yi ba keroog ñuy génne lii ci wet yépp. Dellu ci gannaaw ba fàww, xale yi soog a dellu. Waaye daal sunuy xale du nu jàng lu ni mel.
Ñi nekk ci bopp yi ñu xam leen, siiwal leen ndax yoon mayuleen ñuy def lu ni mel ci sunuy ekool.
Jawriñ ji weddi na waaye laaj bi mooy, lu tax mbir mi dem ba àgg ci ay lëlu ? Ku fi indi lii ? Ku maye ngir mu duggsi fi ? Ñan ñoo nekk ci bopp bi ? Lu ñu ci jublu ?
Nguur gi mënu cee noppi, war na ñoo leeral lii waa réew mi.
Noo ngi leen di déglu.
« `
Mamadu Jóob Dëkurwaa

Laisser un commentaire

Votre adresse e-mail ne sera pas publiée. Les champs obligatoires sont indiqués avec *