Ñi bokk ci kuréelug 10 000 wattukat, di ay bañkat, àrtukat ak ay nit yu màbbe ci askan wi rekk ñoo aakimoo woon mbeddi Ndaar yi ngir ñawlu jaay doole gi ndiisoog gox ba doon jéem. La ñu bëggoon moo di soppi turu Xàll wa ñu duppe woon Seneraal Degóol ngir tudd ko Maki Sàll.

Dogal bu wayadi boobu te néew ñu ca ànd, bu fekkee jàll na, dina doon njuumte lu rëy ci mboor. Di doon lu nar a dëggal xayadi ak ayibu xelum askanu gox boobu am ñatti xarnu.

Ci xibaar yu mujj yi, ndiisoog gox ba ajandi na tudd ma mu bëggoon a amal ca mbedd mu mag mu yaatu mu dëkk ba.

Ñu ngay fàttali ne xeex bii jëmalewuñu ko ci nit walla jëmmi kenn rawatina Maki Sàll.

Nekkuñu foofa sax. Ci seen ug aamu, dañuy xeex ngir mbedd yooyu tudd turi gor ñi nga xam ne dañoo jaar seen i wakkan ngir réew. Mboorum dëkkub Maam Kumba Baŋ. Ci seen kàddu, seen dëkk boobu ñàkkul i ndaanaan  yu faatu walla yuy dund yu yayoo ñu duppe leen mbedd yooyu. Te sax soppi turi tubaab yooyu dafa càkkutéefu askan wi. Waaye bëggunu polotig lal ko walla mu rax ci. Ay firnde yu leer ñoo war a doon ndàll yi nga xam ne ci lees di tekk tànnug tur yi.

Ñu ngay fàttali xelalkati gox ba warugar wi dox seen diggante ak askan wi ndax nekkaluñu fa Maki Sàll waaye waa Ndar ña leen fa teg.

Leeral:
Wattukat: sentinelle
Ndàll: fondement
Xelalkati gox bi: conseillers municipaux
Mboor mi: histoire
Wakkan yi: « pluriel de » bakkan
Aamu: engager
Àrtukat bi: avertisseur
Bañkat bi: activiste
Ndiisoog gox bi: conseil municipal

Ngañ Aaw
saabal.net@gmail.com
763872046

Une pensée sur “Mukk ! Sunuy Mbedd du tudd Maki Sàll”

Laisser un commentaire

Votre adresse e-mail ne sera pas publiée. Les champs obligatoires sont indiqués avec *