Mbas mii di Koronaa Wiris Ndakaaru la def këram gu mag, ñi doomu jàngoro ji dugg fa la ëppe. Loolu nag manees naa fekk sabab bi ci juróomi bir :

  1. Tancaloo gi : suufus Ndakaaru manees na koo xayma ci lu yées juróom-ñenti-junni (9000) ciy ektaar, maanaam juróom-ñett-fukk ak ñent ciy wërŋalu jun-ñay (84 km²). Nit ñi ko dëkke ñu xayma leen ci ñett ba ñenti miliyoŋ, maanaam fukki junniy nit ak ñaar (12000) ci wërŋalug jun-ñay boo jël. Mu doon lu bari lool ci bees ko mengalee ak dëkk bu mel ni Tàmbaa Kundaa, nga xam ne fukki nit ak juróom-benn (16) ñoo dëkk ci wërŋalug jun-ñay bu nekk.
  2. Dem bi ak dikk bi : waa Ndakaaru daanaka ñooy xëyandoo di wàccandoo. Loolu nag dafay indi dajaloo ak tancaloo ci daamar yi. Ñiy tukki itam jëm bitim-réew, ak ñiy fay jóge, ñoom ñépp Ndakaaru seen jaaruwaay la. Rax ci dolli ñi dëkke ci dëkk yi fegoo ak Ndakaaru (Cees, Sali…) nga xam ne dañuy man di xëysi Ndakaaru, di ñibbi ngoon gi. Yii yépp nag dafay yombal lawug mbas mi.

3 ak 4. Dëkkuwaay yi ak njuux li (climat) : Ndakaaru dafa xati dëkkuwaay, te bopp yi nangoo bari ci biir. Rax ci dolli njuux li (climat) nangoo sedd. Loolu di waral nit ñi di toog seen biir kër yi, bu ko defee dankaloo doon lu yomb seen bir : li doomu jàngoro ji gën a bëgg ngir law.

  1. Bërëbu fajuwaay yu yemb: Ndakaaru bees ko mengalee ak yeneen dëkk yi ci wàllum paju, danuy gis ne fa la bërëbu fajuwaay yi ëppee, jige nit ñi, ba tax saytu seenuw yaram yomb leen. Loolu dafay tax caytu gi jëm ci doomu jàngoro ji dafay yomb, wuute ak yeneen dëkk yoy nit man naa feebar ba wér te du dem kër-doktoor.

Ci gàttal li mooy sabab yees man a jàpp ne moo waral mbas mi wulle ñaay Ndakaaru.

Cig pàttali, nu gën a farlu ci digley ñi yore paj mi : di raxas yoxo yi, takk Alikeñ yi (masque), muytu ndaje yi.

Ay leeral yu tukkee ci Doktóor Boubacar Signate

Tekkikat bi: Seexunaa Njaay

Laisser un commentaire

Votre adresse e-mail ne sera pas publiée. Les champs obligatoires sont indiqués avec *