Laaj : Fees man a wéer bii xeex (ñeel gëdday askan yi) ci jamono joj jikko yi dañoo maase yàqu ?

Eme Seseer : Laaj bu doy waar. Bir na leegi lajjub yenn xalaat yi jëm ci nees gise àdduna si ak ni mu lootaabewoo. Bu nu xoolee loolu, gisuma ne war nañoo jàpp ne lépp yàqu na fépp yaxeet. Bu dee amna lu fi am lu am solo ci biir at yi mujj, man naa wax ne mooy ne naxembaay yu bari tàggoo nañu ak ñoom. Leegi xam nañu li ñu warul a def. Lajjug réew yi féete soowu-jant ak lajjug Kominism ak Maksiism, terewuñu ma wéy di jàpp ne amna fi ay gànjar yu ñu man a boole ñu doon benn : péexte, gëddu nit, yëg-yëg, xel, dimbalante, mbokkoo … Ci loolu lees war a tënku te wan ginnaaw yu ñàkk solo yi ak rëcc-rëcc yi ñu yàgg a jural aw tiis. Du caageni dañuy sànni lépp ba noppi ne dagaj ci ràppitu Sàmba-Lawbe, waaye dañuy joyantiwaat àdduna si. Xam naa dinga ne sémb wu yaa la. Waaye luy doon maanaa sunu dund, bu ñu ci boolewul loolu ? Jàllarbi gi jikko yu rafet a koy lal walla furaas »

Laaj-ak-tontu ak Fawsiya Suwaari ak Anig Tebiyaa-Meslaan, Jeune Afrique, lt 1966, fukki fan ak juróom jàpp ñaar fukki fan ak benn ci weeru sàttumbar 1998.

Daawuda Géy Pikin

Laisser un commentaire

Votre adresse e-mail ne sera pas publiée. Les champs obligatoires sont indiqués avec *