Saabal biy weddi waxi Seex Umar Jaañ jëm ci ni jullit ñi daan wooree ci jamonoy mbéefeerkat yi.

Ndar
Korite gi

Caacambalug korite giy wane njeextalu koor gi, amal nañu ko ci Ndar, Altine, ak mbégte ma mu baaxoo.
Sirenub dalub fara bi moo yëgle njeextalu koor gi, dibéer bi 13i waxtu di jot, sukkandiku ci téllgaraam bu bawoo ca Ataar, ñu ciy xamle ne weer wi feeñ na gaawu ci ngoon. Ñenn ci jullit ñi dog seen ug koor, ñeneen ñi dëgër lool doon sàkku ag wóoral gu bawoo ci Xaadi bu Ataar. Dëggal googu nag yeex a am donte ñenn ñi jullit ñi ci Ndar woor nañu 29, ñeneen ñi moom dañoo matal 30.
Waaye wuute googu terewul jullit ñépp daje ca suba sa ca jumaa ju mag joj Al Haaji Maalig ak joj Al Haaji Tiijaan ca Ndar Tuut.
Bi jant bi di fenk, fépp foo xool gis fa mbooloom ñu summarñiku. Mu xumb lool. Ñépp di jàmmasante ci mbedd yi ak di ñaanalante. Korite gi la woon, doon it bisub baalonte àq.
Sëriñ Musaa Jóob moo jiite julli gi ca jumaa ju mag ja. M. Agostini, topp-njiital bëkk-néeg moo fa teewaloon Gornoor. Alhaaji Abdu Asiis Si moo jiite jullig jumaay Al Haaji Maalig Si, Al Haaji Tiijaan Ñaŋ daal di jiite gog Jumaay Ndar Tuut. Jumaa yépp a feesoon ak mbooloom fere yi bawoo fépp ci Ndar ngir jullisi dégluwaale xutbay Imaam yi.
Wenn wëppa wi lañu waxtaane ci jumaa yépp. Imaam yi fàttali nañu kenoy diine lislaam, soññe nañu ci saraxe, dimbalante, mbëggeel jëm ci sa moroom ba noppi àrtu nit ñi ci ñu moytu bàkkaar.
Ginnaaw julli gi nag mbedd yi tàmblee xumbaat.
Ci ngoon gi ñu amal làmb ju mag ju naroon a fomm ndax jamono ju neexul.
Caacambal gi nag wéy na ba ci guddi gi ànd ak mbégte mu mag.

Laisser un commentaire

Votre adresse e-mail ne sera pas publiée. Les champs obligatoires sont indiqués avec *