Ca Óstaraali, ab ñakk buy faj koronaa te nekk ci caaf gu njëkk gi ca Jàngune bu Kiwinslànd moo jur yeneen jàngoro yu yéeme ba waral kilifay réew ma ajandi ko. La indi tiitaange ga mooy ñakk ba dafa wane ci ñenn ca way-coobarewu ya aamu woon ngir ñu caaf ko ca ñoom, ne mel na ne dañu caa jële doomu jàngoro jii di SIDA.

Li waral njekkar la mooy takk-takk ba ñu jaar ngir defar ñakk ba dafa ànd ak kem mu tuut lu poroteyinu doomu jàngoroy SIDA, di la ñu xamle. Waaye ci li ne fàŋŋ, kem moomu doy na sëkk bay feeñ ci caaf ga ñu doon def jëme ci SIDA bi. Kàdduy woroom xam-xam ya naan loolu warul jur njàqare terewul réew ma rotal ub dogal buyy neenal njëndum ay tamndareeti ñakk niki ni ñu waaje woon.

Cig pàttali, Amada bi di Lig Montañer doonub doktoor bu mag te jël mbandal bi gën a am solo ci wàllu paj, xamle woon nani nit moo sos doomu jàngoro ju Koronaawiris bi te daf koo liggéeyaale ak SIDA bi. Ba mu ko waxee nag, daloon nañu ca kawam, xas ko ba mu ràpp…

Ginnaaw ba mu juree ay laaj ci ñi xamul ni mu deme, njekkar yu mel noonu du yombal liggéeyu njiiti réew ma war di janoo ak askan wa. Rawatina ba ña ëpp ca askan wa lànkee ba kandaare ne kenn du leen ñakk.

Kanberaa dina wëlbatiku jël saafaras AstraZeneca ak su Novax.
Bokk ci réew yi mbas mi xojul (908 ñu dee ci 25,6 tamndareetu doomi aadama) bus ko méngale ak yeneen réewi Órob yi, Óstaraali dara tënku ko ngir mu fente pakk yi te lal yeneen i pexe.

Amada: amadagunduŋ: professeur / tamdareet: million / njekkar: malheur, déconvenue

Ngañ Aaw – 763872046 – saabal.net@gmail.com

Laisser un commentaire

Votre adresse e-mail ne sera pas publiée. Les champs obligatoires sont indiqués avec *