Afrig li ko dal metti na lool, ndax dinanu faatu ba jeex ndax ay xarala yu yees;

Ñi nga xam ne dañuy liggéey ci jumtukaayi xarala yu yees yi ak ñi ko xam dañuy tere seen njaboot ñu yor ko ndax xam nañu doy waar gi ci nekk, bari na ñoo xam ne ñoo ngi woon Feesbug dañoo xëy rekk bàyyi ndax xam doy waar gi mu làmboo.

1- ARROSEUR ARROSÉ – Justin Rosenstein: mooy ki sosoon « Lik aime », xëy na bàyyi daal di sos ag kuréel ngir ñu wax lu doy waar yi nekk ci jumtukaay yii

2- Ki sos Feesbug du xool jumtukaay gi lu ëpp juróom ñaari siimili ndax di sàmm wér-gi-yaramam.

3- Steve Jobs: moom bëggul a am iPad ndax xam na doy waar gi mu làmboo ci xañ nit wérug yaram, Saabalkat bii Bilton moo ko laaj ci attum 2010: ndax sa njaboot xam naa bëgg nañu iPad ndax yaw yaa sos Apple, mu tont leen ne: duñu ko laal mukk walla sunu koy laay ci as ndiir lay doon.

4- Way-juur yiy yëngu geeks Silicon Valley dañuy tere seen i doom di jege xarala yu yees yii, te ñoom suba ak ngoon ñi ngi di sos ay jumtukaay yu yees waaye seen i doom duñu ko jëffandikoo Saabal bii ñuy wax New York times moo ko siiwal.

5- Evan Williams, bokk ci ñi nga xam ne ñoo sos Twitter dañu koo laaj ndax sa njaboot am nañu ci jumtukaay yu yees mu ne leen mukk ñoom buñu nekkee ci kër gi dañuy yër ci téere yi.

6- Chris Anderson, bokk ci ñi jiite woon Wired dafa wax ne lépp lu nekk ci musiba ci xarala yu yees yii maa ko gisal sama bopp te dund ko.

7- Mbooleem ñiy liggéeye fii: Google, Yahoo, Apple et eBay, seen i doom duñu jege mukk yii jumtukaay ndax xam li ci nekk ci musiiba

8- Yaw mi yor Jollasu moomóo ko ndax ñoom ñi ko defar waxtu wu leen neexee dugg ci, liy firndeel loolu ca Amerig dafa am ay sàmbaabóoy yu rayoon nit, daal di fa fàtte seen jollasu, police jéem koo tijji manu ko mu dem ci kërug jollasu gi mu bañ, ndax nee na damay bañ ñi jënde ci man dootuñu amati kóolute ci man.

9- Jollasu dafay jeexital ci wérug yaramu nit rawati na muy laal fenn ci aw yaramam, walla nga ciy sëgg lu bari di ko xool.

10- dafay yàq ak yuur, ndax day sonnloo yuur gi ba dootul man a mokkalati lu bari, rawati na kiy tëdd jël jollasoom mu nekk ci wetu boppam.

11- Booy wuyu bul ko teg mukk ci sa noppub nday-joor, ndax dafay yàq sag yuur, ba noppi indil la ay tawat, bul def jollasu mukk ci sa jiba walla muy laal sa yaram dalay lor.

Imaam WAX (Wolof Ak Xamle) .

Laisser un commentaire

Votre adresse e-mail ne sera pas publiée. Les champs obligatoires sont indiqués avec *