Ci mbind mu mu fésal ci xëtu feesbugam, El Maalig Njaay di ki yor caabalug Usmaan Sonko dikkaat na ci kaaduy laabire yi Sëriñ Muntaxaa def jëmale ci njiital Pastef li. Gis na ne kàdduy Sëriñ Muntaxaa yi am na solo soo xamne kenn waru koo jël rekk moomale ko kenn nit kese. Ñépp a ci war a gis seen bopp. Nee na itam sant nañu bu baax ndax Sëriñ Muntaxaa fésal na yaakaar gi mu am ci Usmaan Sonko ba tax mu koy laabire.

« MBEGTE MI!

Sama jàngat ci waxtaanu ku tedd ki:

Ci njëlbeen gi « Yéen » la wax. Maanam nun ñépp kon ci laa bokk

👉🏿 Xelal na ki yor nguur ak kuy wut nguur. Manam yéen ñiy wut luy defar àdduna, bakkan dafa foor te ku ci faat bakkan dee dem safara rekk (dëgg) gu wér.

👉🏿 Xam na ne defar réew mi jaral nanu sunu bakkan waaye tegunu ko fenn. Geneen dëgg ndax bakkan dafa foor.
Kon nanu def lépp ci jàmm!

Ca mujjantal ga nag « Yaw » la wax maanam Usmaan SONKOO

👉🏿 Xamal na Usmaan ne JÀMM ji nga xam ne moom la ko ñaan mu may ko ko, mooy li am njariñ ndax ci diine bakkan dafa foor te sant na ko ci gërëm na ko ci! (Alhamdulilah ndax Ngërëmal Sñ Tuuba ngëneel kepp la)

👉🏿 Xamal na ko itam ne umpalewul bëgg gi mu bëgg réew mi!

👉🏿 xamal na Usmaan ne ko, dama lay laabire ci li lay tax a mucc! Alhamndulilah!

👉🏿 Bi ma ci gën a neex nag mooy xamal na Usmaan itam ne su gisee mu koy wax li yépp nag, YAAKAAR gi mu am YAAKAAR ci moom moo tax. Ëskey! Xel dalati na, njort rafetati na!

Yal na sunu Boroom sammal nu Sñ Muntaxaa Mu Yàgg fi loool te ànd ak wér!

SANT YÀLLA!

Ngeen baal ma àq baal naa leen! »

Saabal.com

Publié dans : Non classé

Laisser un commentaire

Votre adresse e-mail ne sera pas publiée. Les champs obligatoires sont indiqués avec *