Demoon nan dëkk bii di Gore, di dëkku cosaan ak mboor. Fekk nan fa Baay Suley LI, di mag mu baax, xam démbu dun ba, te ànd ak maandute ci bu koy nettali.

Ndekete yóo, lees jàppoon ci mboorum kërug jaam ga ca Gore dëppóowul ak li am. Ci nettalib Baay Suley, maseesul a am ca Gore Maakaan mees daan dajale ay jaam yoy fekk baax ci kembaaru Afrig, di leen def ciy gaal ngir yóbb leen Amerig. Moone dey, ba nu ganee àddina ba sunu jonni-Yàllay-tey-jii, loolii la nu mës di dégg. Kan ci nun moo fàttelikuwul jëmm jii di Buubakar Sosef NJAAY ? Ku ko mësutoon a gis it, mësoon ngaa seetaan tele, ñu wane ko ci maakaan boobee, mu daan nettali nees daan jàppee ay jaam, daan leen deñc foofee njëkk ñu leen daan jàllale Amerig. Daan nañu gis sax ay nit ñu daan tuur i ronqoñ ndax gëm ga ñu daan gëm ay waxam ak waxin wa. Soo ko dégluwaan, daan nga yaakaar sax ne daa fekkee la muy nettali ndax xadar ga mu ca daan àndal. Ndekete-yóo furaas dàlli xëdéen. Kon nag, warees naa lëñbët ngir xam lu waral ñaar:

  • lu waral ci diir bu yàgg, ñu dëkkal ci noppu dogitu ña ñu jàppoon jaam ni Gore mooy suuf su mujj su seen maam jot a nekk ci Afrig, laata ñu leen i yóbb Amerig ?
  • lu waral itam fen wu ni tollu màgg fi ba béjjaaw ?
    Ci gis-gisu sunu njaatige bii di Baay Suley, fi Càmmu Senegaal juume mooy bi mu jëlee koo xam ni jàngul mboor ba noppi mu teg ko ca maakaanu-jaam ba ngir muy nettali mbooru bërëb ba nemmeekukat ya fay dikk. Xayna, ñàkkul sax ne ci njëlbéen, li doon yéene Càmm li moo doon wut ab barab bees daan mën a màndargaale ñaawtéef gii di njaayum jaam. Lu ni mel dara nekku ci. Ñaata warab ak i tën ak i jana lees jël, féetele leen am mboor ? Waaye lees mënul a nangu, mooy tuur lëndëm gees ci laxas. Sëtu jaam yu bare, demoon nañ ba jàppee dun bi fees daan ñëw di aj niki Màkka walla Rom ci jullit ñe ak nasaraan yi. Nit daan na tibb suufas Gore sax jaay leen ko ci lu njëgu, ñu àttan koo jënd ngir jàpp ne du woon suufu neen. Waaye ba ñu yëgee ni dañ leen fen ci diir bu yàgg, ci la ñu meree daaldi noppee ñëw Gore.

Alsaan Jóob

Une pensée sur “DEMOON NANU GORE”

Laisser un commentaire

Votre adresse e-mail ne sera pas publiée. Les champs obligatoires sont indiqués avec *