Xew-xew, diine
Siyaare atum 2020: njiitu Fayda Tiijaaniya, Papa Maahi Ibrahiima Ñas woo na mbooloo ma ngir ñu dellu ca suuf sa ngir tekk ay sémb jëm ci mbay mi ak ndefar mi.

Ba mu ñëwee ngir jiite xew wa (siyaar bu ñuy amal at mu jot ca Medina Baay), njiitu Fayda bu Medina Baay, Sëriñ Maahi Ibrahiima Ñas, sàkku na ngir ñu delluwaat ca mbay ma ngir xeex yenn jafe-jafe yi niki ndóol, ndëngte ak góor-jigéen.
« Sunu aamu ci diine amul sikk-sakka. Leegi nag, jot na nu delluwaat ci tool yi. Dañoo war a def mbay mi sunu yitte ni ko Baay Ñas doon defee ci jamonoom. Suuf saa ngi fi, yemb na leegi nag nañu dem bayi ko ngir suqali sunuy naal lu ci mel ni mbay ak ndefar. Baay Ñas bàyyi woon na fi lu tollu ci 400 ektaar ca Tayba Ñaseen te it am na yeneen i tool ca Kóosi. Danu leen war a jëfandikoo… » la Xalifa bi xamle ca kanamu ndongo yi.

Su nu ko déggee, mbay mi rekk moo mën a tax ndaw ñi toog seen i dëkk. Waaye mooy tax it ñu mën a xeex yenn bir yi niki ndóol, ndëngte, góor-jigéen añs.

Sëriñ Maahi Ibrahiima Ñas yokk na ci ne Senegaal ñàkkul ay woroom mi xam-xam ngir sopparñi gerte gi ci réew mi te bañ a xalaat saa su nekk di ko yóbb noonu ca bitim réew. Kilifa diine bi woo na képp ku bëgg, rawatina Càmm gi, mu nekk ci loolu ngir soppeeku am.

Àlliyun Gay

Laisser un commentaire

Votre adresse e-mail ne sera pas publiée. Les champs obligatoires sont indiqués avec *