Bartelemi Jaas fippu na xamle na ne kenn manu koo teree doon lawax ngir doon farab Ndakaaru. »Ab lawax laa. Waaye dafa mel ni càmm gi yabal nañu ci kër fara bu Meermuus kurél giy saytu doxaliin (IGE) ci réew mi. Maa ngi leen di dalal jàmm. Defleen seen liggéey te jébbale ko ci lu dul jafe-jafe. Bi fi Xalifa Sàll doonee lawax ngeen ko yónnee kurél googu ngir ñu saytu ko, waaye yoon wii moom du jàll. Kenn manu maa teree bokk ci joŋantey gox-goxaan yi. Ñaareelu yëngu du am waaye tomb bu amul dellusi moo fi nar a am », di àrtuy Bartelemi Jaas miy woo kujje gi ñu booloo ngir jàmaarloo ak Maki Sàll.

Baataan:

Lawax : candidatFara = maire

Publié dans : Non classé

Laisser un commentaire

Votre adresse e-mail ne sera pas publiée. Les champs obligatoires sont indiqués avec *