At mii di ñëw bum mel ni at ya wéy
Na leen gën a xumb gën leen a géey
Xumbiy njariñ xéwal jàmm ak i yiw
Géey ciy nattook i balaak i woppi liw

At mii di dikk nay jàmm ak salaam
Kune góob texeem te dàggiy jalaam
Kuy séetu dem te buñ takkiy xalaam
Mu am kàttan am koom cig nafaam

At mii di ñëw kat bum fi indi ay
Ku daan ñaan ren bu la kenn may
Xanaa kay yor ba bor yépp nga fay
Ba dootoo tàllal loxook a dëkke lay

At mii nuy tàccu na taajam yépp neex
Ndékkeem ba reeram tax buun bi jeex
Ndawal ak njar nuy ñam ci bànneex
Nu dàq dund bépp lar ak sépp seex

At mii di ñëw na YÀLLA dëxëñ ci moom
Bàrkeeb sëy te kat may ku bëgg doom
Ku ndóoloon na am ren lu doy ci koom
Xelam dal mu far sax ci jaamu Boroom

Wér ak tal, am lu doy ak doyloo fi gën
At mii di ñëw na tax nu jal yee ca sën
Nuy féy ci yiw ni cim dox mel ni jën
Nu ne ci tawféex te buñ nuy gétën

At mii di ñëw moom bu ci kenn dee
Cam su nekk texe te am lum dundee.

        Saalum Jaane

Laisser un commentaire

Votre adresse e-mail ne sera pas publiée. Les champs obligatoires sont indiqués avec *