Lan moo dese as gor bu demee ba amatul kàddu? Lan la ngor di jariñ bu dee du sàmm kàddu?
Gore a ka jafe! Maa ngi jooy samag ngoreedi man mii tayle sama kàddu, man mii wor sama bopp, man mii tooñ sama xol. Ndax mas naa doon gor? Lan mooy tegtale as gor ba man koo joxoñ yoon wu mu warta wàcc ba man a yëg ne yelloo na baatu gor? Gore ci ñii, goreedi ci ñoo, am kàddu ci ñii, amadi ko ci ñoo, sàmm sa ngor ci ñii, boyal ko ci ñoo; du gore, teg xel la.

Yëral bii itam 👉https://saabal.com/ag-bokk-dee-na-pacc-1-ismayla-gey/

Ana ngor?
Maa ngi jooy samag ngoreedi bay yuqat. Ndeke ngir nga man a doon us gor, fàww nga noot sa bakkan ak sa bànneex bu ko defee nga doog a sóobu yoonu gor ña lu ko moy woru dikkal la nga jaar ci ñall wi te doo ko yëg.
Ana lan ngay waxati kok la nga ko jootoon a wax lépp wacc nga ko? Lu deefi digeeti? Nu deefi dëfaleeti? Tay jaratuma dara, àddina ak saytaane kar ma ginnaaw bi ma bànneex ak bakkan wëree ndombo.
Ndaw dundu gu dee gën!
Jii jamono sàmm fi kàddu ay dëggi-dëggi xeex bi, aw fen daj na kàpp àddina, wori kese, nax yu dul jeex. Namm naa la ciy fen, maa la raw ciy fen, diw a ngi lay nuyu ciy fen, waa kër gaa ngi lay laaj ciy fen, nuyul ma diw, dina ko dégg ciy fen, bëgg naa la ciy fen, lebal ma ciy fen, dinaa la fay ciy fen; feni kese… Nax baat la bees rafetal rekk waaye doomu ndayu fen la.

Màndarga mu ñàkk ngor

Ana ngor?

Fen a gën a rëy njaalo, boolees na ñaar yépp te jàppeesu ko dara. Fen day yëngal Aras terewul dëkkees ci di ko yëngal. Ndokk ba Yàlla dul daanu!
Ana nees di man a goree ciy warab yuy fen wër?
Jéggal nu Yàlla saa Boroom, soppi nu, defal ci xoli ñi nu wor ñu jéggal nu, woyofalal naqar wi ci ñoom, feralal ronqooñ yi, indiwaatal kóollute gi, soppi leen… Démb kàddu lees daan xàmmees gor, kàddu lees ko daan nawe, kàddu lees ko daan jàppe te waat daawu ko ci fekk. Tay nga boole joxe kàddu ak waat te du tax nga sàmm ko ba kenn wóolootul kenn ndax di xalaat ne koo digaaleel altine mu wor la talaata. Samag ngoreedi doy na ma sëkk, sama bopp a ma tax di wax.
Ay gore foo ne? Lu tax nga seetaan ma? Lu tax nga bàyyi ma? Bul ma dumóoyu, wuyu ma te bañ maa boddi ndax sama xol fees na la dell donte yenn saa yi samay jëf wor la.
Maa ngi lay xaar te di la gelu, di rafet njort ne dinga ma dikkal ci lu gent dul toppu ba sama xel ak samab xol ak samay cér ak sama jëmm di la xeeñ jamono ju ne ci wéet ak ci wéttaliku ba lu ma fasati ci biir; mu fés ci biti.

Ma-Réew

Laisser un commentaire

Votre adresse e-mail ne sera pas publiée. Les champs obligatoires sont indiqués avec *