Tiis wu rëy ganesi na ma ci demug aji-dawlu jii di ag bokk. Ginnaaw tawat ju metti te yàgg lool, wuyuji na Boroomam ci askan yu baree baree bari, ci xeet yu wuute, ci der yu bokkul i wirgo, ci waaso yu bokk dereet, ciy kër yu séddalikoo ci geño ak meen ci àddina sépp. Ba muy xarxarle, woo na ña ko waroon a taxawu ba lii du ko dal fàttali leen njariñal jokk ug bokk, fàttali leen itam lori dogug bokk waaye fa ñuy réccoo bay xalaat a dabu ngir bëgg a dabaatal ba man a dabe; ci la wàcceeb liggéey.

Fu réccu amee rekk jëf ju wees a fa teew. Bokk nekkoon alalu Yàlla, xéewalam bu mu baaxe woon jaam ñi ngir ñu bokk yéene, bokk pexe, bennoo ginnaaw bi ñu booloowee ba man a dékku lol fu mu fekk ku bokkul faagaagal ko. Bi Boroom bi nee ag bokk dama lay wàccee ngir nga rataxal diggante yi, nëbb ayib, séddoo xam-xam bi ak am-am gi ak man-man gi ba kenn du tumurànke, kenn du wéet; ag bokk dafa xaacu, yuuxu, saleeru, jooy jooy yu mettee mettee metti ngir ragal li ko ci nar a fekk. Jooyul ngir tiit walla jaaxle walla yaafus waaye daa jooy ngir xam ne li mu ëmb ciw yiw ñeel jaam ñi, duñu ko jariñoo te dinañu yàq ub deram.
Boroom bi ne ko na sa xel dal, bu la dara naqari, Man Yàlla maay sa féete. Képp ku féete ak yaw ma far ak moom, képp ku la beddi ma botti ko te ku ma botti daan ko jéllub toroxtànge bu kenn dul werante. Yaw bokk demal, ku la jokk ma jokk ko, ku la dog ma dog ko.

Ba beneen yoon…

Ma-Réew🥰🇸🇳😍

Saabal.com / yéenekaay biy joxe xibaar ci Wolof yu raxul dara

Xët Instagram bi
https://www.instagram.com/saabal._com

Dalu youtube bi👇
https://www.youtube.com/saabalcom

Xëtu Facebook bi
http://www.facebook.com/saabal.net

Xëtu Twitter bi
http://www.twitter.com/saabalN

Laisser un commentaire

Votre adresse e-mail ne sera pas publiée. Les champs obligatoires sont indiqués avec *